vendredi, novembre 22, 2024
spot_imgspot_imgspot_imgspot_img
AccueilPolitiqueSon cortège gazé par les forces l'ordre : Sonko en colère averti

Son cortège gazé par les forces l’ordre : Sonko en colère averti

Après sa visite à la mairie de la patte d’oie, Ousmane Sonko a tenu a envoyé un message à ses partisans et sympathisants. Sur sa page Facebook il écrit :

Mes chers compatriotes,

 

A Dakar, ce jeudi 09 février 2023, mon cortège a essuyé des tirs de grenades lacrymogènes pour une simple visite à la mairie de la Patte d’Oie; alors qu’hier, Macky Sall, président de l’APR, s’est payé, tranquillement, un convoi politique à Thiès sous prétexte d’un conseil des ministres décentralisé.

 

À Mbacké, toujours ce jeudi 09 février 2023, le commissaire de police a convoqué les responsables du parti, organisateurs du meeting de Pastef, prévu demain, pour leur dire que l’activité ne pourrait être tenue au motif qu’il n’y a que deux signataires sur la lettre d’information à l’administration.

 

Au moment où nous écrivons ces lignes, certains parmi eux sont en état d’arrestation, y compris un député à l’Assemblée nationale, l’honorable Cheikh Thioro Mbacké.

 

La forfaiture du préfet, auteur de cette décision est choquante. En effet, en ouvrant les guillemets pour citer l’article 96 du code pénal du Sénégal en vigueur, comme base légale de « l’interdiction », le préfet du département de Mbacké, monsieur Amadoune Diop, a reproduit les dispositions, non pas du Code pénal, mais celles de la loi N*74-13 du 24 juin 1974, d’ailleurs abrogée, dans ses dispositions contraires, par l’article 18 de la loi N° 78-02 DU 29 janvier 1978 relatives aux réunions. Cette forfaiture ne passera pas!

 

Nous avons saisi la Cour Suprême d’une requête en référé aux fins de l’annulation de cette honteuse décision.

 

En attendant la décision du juge des référés, le Mega Meeting de Mbacké reste maintenu ! Au préfet qui s’est courbé devant les ordres illégaux de ses supérieurs d’en assumer les conséquences devant l’histoire.

 

En conséquence, j’appelle les militants et sympathisants à maintenir la très forte mobilisation notée qui crée la psychose chez Macky Sall au point qu’il ait besoin d’être « rassuré » par une mobilisation payante de ses responsables et alliés politiques moribonds.

 

En tout état de cause, j’avais déjà formulé mon intention d’accomplir ma prière du vendredi dans la cité religieuse de Touba avant de me rendre à Mbacké solliciter les prières auprès de Serigne Amdy Modou Mbenda Fall, khalife des baye fall , je compte bien m’en acquitter par la grâce de Dieu.

 

Aucune dictature ne prospérera au Sénégal et plus aucune forfaiture ne sera tolérée. Macky Sall gagnerait à le comprendre, pendant qu’il est encore temps, pour préserver la paix civile.

———————————————————————

 

Yéen bokki ma-réew yi,

 

Ci Ndakaaru, tay ci alaxemes ji 09i féewarye 2023, samag gàngoor jóor nañu leen ba ñu doyal ay gërënaad lakrimosen ndax nemmiku gu ndaw ca parab Patduwaa ; te démb rekk, Maki Sàll, njiital APR, ànd na ag gàngooram ca Cees wër fu ko neex layalee ko ndajem jëwriñ yi ñu fa tuxal.

 

Ca Mbàkke, batay ci alxemes ji 9i féewarye 2023, komiseer ba woolu na kilifay làng gi, way-lootaabey ndajem PASTEF, mu ñu jàppoon suba, ngir xamal leen ne seen yëngu yooyu du man am ndax ñaari nit rekk ñoo torlu bataaxelub yëgle bi ñeel ndoxal gi.

 

Jamono ji nuy bind mbind mii, ñenn ci ñoom teg nañu leen loxo, mu bokk ci ñoom benn jàmbur ca ngomblaan ga, di Seex Coro Mbàkke.

 

Jalgatig calaw li jël dogal bii lu doy waar la. Ndax ba mu tijjee këmb kepp yi ngir tudd dog 96 bu kot penaalu Senegaal, di lu mu sukkandiku ngir gàntal gi, calaw lu Mbàkke, Sëriñ Amadun Jóob, li mu jëlaat du kot penaal bi, waaye sàrt limtu 74-13 bu 24i suwe 1974, te ñu far ko sax nag, wuutal ko ak dog 18 bu sàrt limtu 78-02 bu 29i saawiyee 1978 te soxal wàllu dajaloo. Njaay doole gii du jàll !

 

Bind nanu ëttu àtte bu kawe bi ngir mu dakkal dogalu bu gàccewu bii.

 

Fii ak nuy xaar dogalu àttekat yi nag, ndajem Mbàkke mi dees koy amal! Léegi nag lépp lu ci xew, na Calaw lii raam ci kanamu ndigalu kilifaam yii teguwul ci yoon, jël bépp matuwaayam ci kanamu àddina si.

 

Ci loolu, maa ngi woo mbooleem farandoo yi ak soppe yi ñu gën a dëgëral seen taxawaay bi waral Maki Sàll mel ni ku dof ba tax mu dem di fay ngir ñi mu àndal ak way-politig yu tekkeetul dara dajaleel ko ay nit.

 

Ak lu man a xew itam, xamle woon naa sama yéene ci jóoxe jullig àjjuma ji ca dëkk bu Sell bu Tuubaa laata may dem Mbàkke ngir sàkku ay ñaan ci wetu Sëriñ Amndi Móodu Mbenda Faal, xalifab Baay Faal yi, te fas naa ko yéene amal bu soobe Yàlla.

 

Genn jaay doole du law ci Senegaal te kenn dootu fi nangooti genn jalgati. Maki Sàll nag na ko xam ca ba muy teel, moo gën ci moom, ngir sàmm jàmmi askan wi.

RELATED ARTICLES

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici

- Advertisment -
Google search engine

Most Popular

Recent Comments